エピソード

  • LAMINE GUEYE ET VALDIODIO NDIAYE
    2023/04/11

    Lamine Gèy ak Waljoojo Njaay ñaari kangam lañ yu xeex ak seen i pexe ba Nooteelu nasaraan bi jeex. Li nu gën a jàpp ci ñoom mooy fula ja ñu def ci aar seen ngor ba tontu njiitul Fraraans la taxoon mu mer.

    続きを読む 一部表示
    12 分
  • ALMAMIAYAT DU FOUTA TORO
    2023/04/04

    Ceerno Sulaymaan BAAL moo soppi ni ñiy yore nguuur ca Fuuta jëlee ko ci ndono tegg ko xam-xam ak jikko. Moo Boolewoon Jullit yi ngir ñu jóog xeex ak ñi bañoon diine. Man na noo wax ni moo indi nguurug yemale  di democrasi ci Afrig Sow jant.

    続きを読む 一部表示
    12 分
  • KOLI TENGUALA
    2023/03/28

    Koli Teŋella doomi Satigi Teŋella Ba ka Nana Keïta la dib Malinke. Cossanam di Baxunu. Jàmbaar ju mag la woon ju mùanoon na jiite xare ba am ca tur wu rëy.

    続きを読む 一部表示
    11 分
  • SYDIA DIOP
    2023/03/21

    Sidiya Ndate Jóob ku raññeeku la ci biir réew mi ndax ab juddoom ak jaar-jaaram. Doomi Lingeer Ndate Yàlla la ak Saakura Barka Jóob. mi ngi juddu ci 18848 dee 1855.

    続きを読む 一部表示
    11 分
  • EL HADJ OMAR TALL
    2023/03/14

    Umar Seydu Taal ma nga juddoo Alwaar ci Poddorug tey jii. Ganaaw ba mu tukke lu yàgg ci ajug Màkka la delusi xare ba samp Lislaam ci Afrig Soww jant te xeex na xeex bu rëy ak Tubaab bi.

    続きを読む 一部表示
    12 分
  • ALINE SITOÉ DIATTA
    2023/03/07

    Alin Sitowe Jaata ma Juddoo Kabrus ca 1920 di ca Usuy biir Kasamaas. Woote fippu bañ li Tubaab bi tegoon askan mo tax ñu géeneewoon ko réew mi.

    続きを読む 一部表示
    11 分
  • SINE
    2023/02/28

    Siin gii ma nga sosso ca 14 u xarnu ba fa Gelewaar bii di Maysa Waali Mane mu Kaabu ñëwee ganaaw xareb Trubang ba. Kumba ndoofeen Fa Mag ku ca raññeeku la. Siin da muj a àndak Saalum géen ci nooteelug Jolof ganaw xareb Danki ca 16 xarnu ba.

    続きを読む 一部表示
    11 分
  • SAMBA GUELADJI
    2023/02/21

    Sàmba Gellajo jeegi mi judoo daanaka Fukeelu xarnu ak juróom ñaar ca Jowol Worgo ca Maatam. Doomu Gelaajoo Jéegi la . Yoroom na nguur gi ñéenti yoon digante 1724 ak 1742.

    続きを読む 一部表示
    13 分